1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
2 Ibraayma moo jur Isaaxa;
6 Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri;
12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon,
17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
21 Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
23 liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
24 Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.