1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
2 Ibraayma moo jur Isaaxa;
3 Yuda, Peres ak Sara ci Tamar;
4 Aram Aminadab;
5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas;
6 miy baayu buur bi Daawuda.
7 Suleymaan jur Robowam;
8 Asaf Yosafat;
9 Osiyas jur Yowatam;
10 Esekiya Manase;
11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon,
13 miy baayu Abiyudd;
14 Asor Sadog;
15 Eliyudd Eleyasar;
16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama;
17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
21 Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
23 «Janq bi dina ëmb,
24 Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.